[Yan xibaar ci Firefox] Yomb na leegi te gaaw leegi, dem foo bëgg te agg itam foo bëgg ak Firefox bu mujj bi. Ak xëtu dalal jamm bi ñu defaraat, mën nga leegi agg ak joow ci lu yomb ci sa ay tànneefi njël yi ngay gena jariñoo. Yi melni yeb yi, mandarga xët yi, jaar jaar, modil yi, jokkoo yi ak paraameetar yi. [Xëtu koñ bu bees] Yokk nañu itam ay bees bees ci xëtu koñ bu bees. Ak sa xëtu koñ bu bees, mën nga joow bu yomb ci yi gëna bees ak yi ngay gëna gane ci benn cuq. Boo bëggee tambali jëfandikoo xëtu koñ bu bees, sosal koñ bu bees boo cuqee ci '+' ci jowkat bi ci kaw. Xëtu koñ bu bees dina wone leegi wiñeti dal yi nga mujj gane. Mën nga solal sa xëtu koñ bu bees boo puusee wiñet yi ñu sãse palaas. Cuqal ci pinees bi ngir xomb dal bi ci fi mu ne, walla butoŋ 'X' boo bëggee neenal dal. Mën nga cuq itam ci njunju «caax» te ne ci kaw ci ndeyjooru xët wi boo bëggee dellusi ci xëtu koñ bu bees bu dara nekkul. Amal Firefox bi mujj te tambali jëfanikoo tay bees bees yi!