0:00:00.000,0:00:05.025 [Yan xibaar ci Firefox] Yomb na leegi te gaaw leegi, dem foo bëgg te agg itam foo bëgg ak Firefox bu mujj bi. 0:00:05.025,0:00:10.094 Ak xëtu dalal jamm bi ñu defaraat, mën nga leegi agg ak joow ci lu yomb ci sa ay tànneefi njël yi ngay gena jariñoo. 0:00:11.013,0:00:15.034 Yi melni yeb yi, mandarga xët yi, jaar jaar, modil yi, jokkoo yi ak paraameetar yi. 0:00:15.058,0:00:19.015 [Xëtu koñ bu bees] Yokk nañu itam ay bees bees ci xëtu koñ bu bees. 0:00:19.048,0:00:26.008 Ak sa xëtu koñ bu bees, mën nga joow bu yomb ci yi gëna bees ak yi ngay gëna gane ci benn cuq. 0:00:26.040,0:00:32.021 Boo bëggee tambali jëfandikoo xëtu koñ bu bees, sosal koñ bu bees boo cuqee ci '+' ci jowkat bi ci kaw. 0:00:32.021,0:00:39.021 Xëtu koñ bu bees dina wone leegi wiñeti dal yi nga mujj gane. 0:00:39.021,0:00:44.013 Mën nga solal sa xëtu koñ bu bees boo puusee wiñet yi ñu sãse palaas. 0:00:44.021,0:00:49.026 Cuqal ci pinees bi ngir xomb dal bi ci fi mu ne, walla butoŋ 'X' boo bëggee neenal dal. 0:00:49.026,0:00:54.083 Mën nga cuq itam ci njunju «caax» te ne ci kaw ci ndeyjooru xët wi boo bëggee dellusi ci xëtu koñ bu bees bu dara nekkul. 0:00:54.087,0:00:59.047 Amal Firefox bi mujj te tambali jëfanikoo tay bees bees yi!